Buzz
Guy M. Sagna : « Bi ñu nu joxee « indépendance » 4 avril la nu waroon xam ne « poisson d’avril » la »
- Author : senego
- 05 avril, 2022 á 08:04:39
- 4
- Lectures : 2632

Texte in extenso :
Bi ñu nu joxee « indépendance » 4 avril la nu waroon xam ne « poisson d’avril » la, ay naxe la.
Sunu ndox, tubaab bi (Suez)
Sunu téléphone, tubaab bi (Orange, Free)
Sunu Autoroute à péage, tubaab bi (Eiffage)
Sunu TER, tubaab bi (Alstrom, SNCF)
Sunu BRT, tubaab bi
Sunu kaaraange, tubaab bi (Armée française)
Sunu njël (budget,) tubaab bi (FMI, banque mondiale)
Sunu géej tubaab bi (Union européenne)
Kiy nataal (photo) Maki Sàll, tubaab bi
Sunu làkk ci suuf, français ci kaw. Cim !
Sunu zircon, tubaab bi
Sunu petrol ak gaas, tubaab bi
Moom sunu réew ak sunu Afrig jot na !
Defar sunu réew ak sunu Afrig jot na !
Bokk sunu réew ak sunu Afrig jot na !
Naataangeg Senegaal ak Afrig, mu ngi nekk ci moom sunu Senegaal, moom sunu Afrig te Afrig doon benn.
Pseudo
En Avril, 2022mdr